TSK

TSK · Genesis 20:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.»

¶ Teewul Aji Sax ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam.

Na lay waxal ak mbooloo mi; su ko defee sa kàddu di kàddoom, te yaw nga mel ci moom ni Yàlla.

¶ Aji Sax ji wax na ak Musaa ak Aaróona ca réewum Misra, ne leen:

Su ko defee mu summi yéreem yooyu, sol yeneen te génne dóom bi dal bi, yóbbu ko fu mucc sobe.

suuf ŋa, mëdd leen, ñook seen waa kër, ak mboolem ku bokk ci Kore, ak mboolem alal ja.

Bànni Israyil ne Samiyel: «Ngalla bu nu noppee jooytul ci sunu Yàlla Aji Sax ji, ndax mu wallu nook waa Filisti!»

Man nag, yàlla tere may tooñ Aji Sax ji, di leen noppee ñaanal. Te it dinaa leen won yoon wi baax te jub:

Buur ne góoru Yàlla ga: «Rikk tinul ma sa Yàlla Aji Sax ji te ñaanal ma, sama loxo mana banku.» Góoru Yàlla ga tinul Buur Aji Sax ji, loxoom bankuwaat, mel na mu meloon.

¶ Naaman nag mer. Ma ngay dem te naan: «Xoolal rekk, man mi noon day daldi génn taxaw ci biti, ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, tiimale loxoom ër bi, daldi teggi jàngoro ji!

Job 34:19 TSK

Kii du far kàngam, du teg ku am ci kaw ku ñàkk, nde ñoom ñaar la boole sàkk.

Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.

mayul nit mu not leen, te yaral na leen ay buur,

¶ Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy.

Su ma nee nit ku bon ki: “Dee rekk ay sa àtte,” te fekk àrtuwoo ku bon ka, waxuloo lu ko waññee ca mbonam ga, ba mu mucc, ku bon kaay dee ndax tooñam, waaye bakkanam yaw laa koy laaj.

Su ma nee ku bon ki: ‘Yaw dee rekk mooy sa àtte,’ mu mujj dëddu bàkkaaram, di jëfe njub ak njekk,

¶ Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottli.

Ana ku wopp ci yeen? Na woo magi mbooloom gëmkat ñi, ñu ñaanal ko, raayaale ko ag diw ci turu Boroom bi.

Ku leen nara lor, sawaraay génne seen gémmiñ, lakk seeni noon. Képp ku leen nara lor, noonu ngay deeye.