¶ Yàlla ne ko: «Waaw, waaye du tere sa soxna Saarata amal la doom ju góor, nga tudde ko nag Isaaxa. Dinaa fas ak moom sama kóllëre, mu wéy ba ciy sëtam ba fàww.
TSK
TSK · Genesis 21:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kooka ne ko: «Nëgëni sii déwén déy laay délsi, te sa soxna Saarata dina am doom ju góor moos.» Bi muy wax loolu, Saarataa ngi ci buntu xayma bi ci gannaawam, di déglu.
¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
ba mbooloo ma gëm. Ba magi Israyil déggee ne Aji Sax ji nemmiku na bànni Israyil te gis na notaange, gi ñu nekke, dañoo sujjóot, màggal Aji Sax ji.
¶ Ba loolu amee Nawmi fabu, mook goroom ya, ngir jóge réew ma. Booba fekk na mu dégge ca Mowab ne Aji Sax ji xettli na ñoñam, ba may leen ab dund.
¶ Ndaw sa nag mujj ëmb; ca déwén sa mu am doom ju góor, ca jamono jooja, muy la ko Alyaasa waxoon.
Éy Aji Sax ji, séddaale ma ci sa yiwu ñoñ, ngalla, dikke ma sag wall,
«Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israyil, moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam Ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee, bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.
¶ Yeen nag bokk yi, yeenay doomi digeb Yàlla, ni ko Isaaxa doone.