TSK

TSK · Genesis 21:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.»

¶ Ba mu ko defee gone ya di màgg, Esawu di rëbbkat bu ñaw, di ku bëgg àll; Yanqóoba moom di nit ku gàtteñlu te bëggoon toogaayu kër.

Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»

Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.

Ay fittkat a ko toŋal, di ko song ak a fitt.

Luke 2:40 TSK

Xale bi nag di màgg, di dëgër, feese am xel, te yiwu Yàlla ànd ak moom.