Ibraam nag wax buurub Sodom ne ko: «Man yékkati naa sama loxo, Yàlla Aji Sax ju Kawe ji seede, moom mi sàkk asamaan ak suuf,
TSK
TSK · Genesis 21:23
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir.
Léegi ñëwal rekk, ñu fasante kóllëre maak yaw, te seede dox sunu diggante maak yaw.»
Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.
¶ Ba mu ko defee Yonatan dellu giñloo Daawuda ci cofeelam gi mu am ci Daawuda ndax ni mu soppe boppam la ko soppe woon.
Léegi nag dama ne, xam naa ne dinga doon buur moos, te nguurug Israyil dina sax ci say loxo.
Daawuda ne ko: «Ndax man nga maa yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yooyu?» Mu ne ko: «Giñal ma ci Yàlla ne, doo ma rey, te doo ma delloo ca sama sang; kon dinaa la yóbbu ba ci gàngooru yàqkat yi.»
¶ Man nag seedey Yàlla laa ciy sàkku, giñ naa ko ci sama bakkan, bañ leena yokku naqar moo tax délsiwuma Korent.