¶ Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko.
TSK
TSK · Genesis 21:33
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Isaaxa nag sàkk fa sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko, ba noppi samp fa xaymaam. Te itam ay surgaam bënn nañu fa ab teen.
¶ Buleen samp benn xeru bant, bu jóge ci genn garab, ngir di ko jaamoo Asera tuur mi, ci seen wetu sarxalukaay bi ngeen sàkk ngir seen Yàlla Aji Sax ji.
Dangeena xamul, am dangeena déggul ne Aji Sax jeey Yàlla ba fàww, sàkk suuf cat ba cat, du sonn, du tàyyi, te am xelam nattuwul?
Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. Mooy Yàlla jiy dund, di buur ba fàww, xadaram gësëm àddina, meram man xeet yi.
Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
Yaw Buur bi sax dàkk, doo dee, te bët manu laa gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!