TSK

TSK · Genesis 21:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Booba fekk na Ibraayma ak Saarata doon mag, ba màggat lool sax, te Saarata weesoon na njurum doom.

¶ Seetleen rekk ci janti démb yi leen jiitu, la dale bés ba Yàlla sàkke nit fi kaw suuf, mbaa ngeen seet asamaan, cat ba cat. Ndax lu màgge nii mas naa am? Am masees naa dégg lu ni mel?

Rakki Tapenes ja am ak Adàdd doom ju góor, di Genubat; Tapenes yor ko ca biir kër Firawna, Genubat nekk ak doomi Firawna, ca biir kër Firawna.

Yaa màgg te yéemey jëf, yaw doŋŋ yaa di Yàlla.

Ku masa dégg lu mel nii? Ku masa gis lu mel nii? Am réew dina sosu ci benn bés a? Am aw xeet dina jekki sosu ci wenn fan? Siyoŋ de, moo tàmbali matu rekk, jur doomam yu góor.

kera bés bu délsee ba jot ci teddngaam ci biir ñoñam ñu sell ñi, ba mboolem ñi ko gëm di ko yéemoo. Te yeen ci seen bopp, ci ngeen di bokk, ndax yeena gëm la nu leen seedeeloon.