TSK

TSK · Genesis 21:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Looloo ngi am, gannaaw ba Ibraam dëkkee fukki at ca réewu Kanaan. Sarayi daldi jël Ajara, jaamam bi juddoo Misra, jox ko jëkkëram Ibraam, ngir mu dëkkoo ko.

Bu dee ci wàllu Ismayla, nangul naa la ba tey. Ndax kat dinaa ko barkeel, jox ko njaboot gu yaa, yokk ko bu baax. Dina jur fukki kilifa ak ñaar yu mag, te dinaa ko defal mu sos xeet wu yaa.

¶ Sanbalat nag ak Tobyaak Araab yaak Amoneen ñaak Asdoddeen ña, ñoom ñépp dégg ne liggéeyu tatay Yerusalem a ngay jëm kanam, te xar-xar yaa ngay tàmbalee fatt. Ñu mer ca lool,

Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.

Jaay nga sa mbooloo ci dara, te jariñu la tus.

Tey ci janti toroxte ak tumurànke, la Yerusalem di fàttlikoo mboolem ngëneeli démbam. Aw askanam a tàbbi ci loxol noon, te wall amul, noon ba gis leen, di textexi ci seenug yàqule.

Waaye doom ji juddoo ci coobarey bakkan, noonu mu daan bundxatale, bu jëkkoon, doom ji juddoo ci Noowug Yàlla, noonu rekk lay deme ba tey jii.