Isaaxa ak Ismayla, doomam yu góor ya, rob ko ca xuntim xeer ma ca Magpela te jàkkaarloo ak Mamre, ca toolub Efron doomu Sowar, Etteen ba.
TSK
TSK · Genesis 23:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu da leena dénk ne leen: «Maa ngi waaja fekki samay maam; dencleen ma fa samay maam ca xuntim bàmmeel ba ca toolub Efron, Etteen ba.
baayam da ne woon, mu ngi waaja dee, waaye bàmmeel ba mu yettaloon boppam ca xunti ma ca réewu Kanaan, na ko giñal ne dina ko denc foofa. Mu ne kon, na ko Firawna may, mu robi baayam, ni mu ko ko giñloo woon, te délsi.
¶ Mu am bés Yuusufa ne ay bokkam: «Sama waxtu jege na, waaye Yàlla moo leen di jëlsi moos, ba jële leen ci réew mii, yóbbu leen ca réew ma mu dige woon, ba giñal ko Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.»
¶ Teewul Buur ne Arawna: «Déedéet, dama koy jënd ci yaw kay. Ab saraxu rendi-dóomal bu ma dikkewul dara, duma ko defal sama Yàlla Aji Sax ji.» Ci kaw loolu Daawuda jënd dàgga ja ak nag ya ci juróom fukki dogi xaalis.
Ma bind kayitu njaay mi, màndargaale ko sama torlukaay, woo ciy seede, ba noppi natt diisaayu xaalis bi.