Baayam Isaaxa ne ko: «Déglul, ma wax la, dinga dëkk fu sore ngëneeli suuf, mbaa fu la layub asamaan tiime.
TSK
TSK · Genesis 27:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Aser ay boroom dund bu duun, mooy maye ngëneeli ñami buur.
¶ «Lépp luy ngëneelu diw gu bees, ak ngëneelu biiñ bu bees, ak pepp mu jëkka ñor, mu ñu jox Aji Sax ji, yaw laa ko jox.
Ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngi leen di yóbbu réew mu baax; réew mu ami wal, ak bëti ndox, ak ndoxi xóote yu waley xur aki tund,
Na samam njàngle sóob nib taw, samay kàddu rogalaat nib lay, ba tuurul am ñax, baawaanal gàncax.
Israyil a ngi dëkke xel mu dal, walu Yanqóoba mee fegu, di wale réewum pepp ak biiñ bu bees, asamaan it di ko wàcceel ab layam.
Wóoy tundi Gilbowa! Yàlla bu ngeen lay, bu ngeen tawlu, Yàlla bu seeni tool nangooti, ba duunal jooxeb pepp, nde foofa lees torxale pakkub jàmbaar. Wóoy pakkub Sóol ba deesul diwati!
¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»
Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa ker, yiiru;
dugub di ko dooleel, biiñ di bégal xolam, ag diw di leeral kanamam.
Na asamaan wis-wisal, niir yuri njekk, suuf fett, meññal wall, boole ci jebbil njekk. Man Aji Sax ji, maa def lii!»
Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi, maa leen di bëggal sama bopp, nde mereetuma leen.
Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk, ci biir xeeti àddina, mbete gaynde ci biir rabi àll yi, nirook gaynde gu ndaw ci biiri gàtt; fu mu jaare, joggati, xotat, te kenn du wallu.
Ndaw bànneex akub taar ca ñoom! Pepp yafal xalelu góor, biiñ bu bees naatal yaramu janq.
¶ Ba tey ngëm la Isaaxa ñaanale Yanqóoba ak Esawu, ngir barkey ëllëg.