Ndaw su taaru la woon, di ab janq bu séyagul. Naka la wàcc ba ca seyaan ba, duy njaqam, yéegaat.
TSK
TSK · Genesis 29:17
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel.
¶ Ba Rasel gisee ne amalul Yanqóoba doom, dafa ñee magam, ba tax mu wax Yanqóoba ne ko: «Nanu am ay doom, mbaa ma dee.»
¶ Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey.
Mu daldi bàyyi lépp ci loxol Yuusufa, te li mu fa nekk tax ba topptootul dara ciy mbiram, lu moy li muy lekk rekk. Booba Yuusufa ku jekkoon bind la te góorayiw.
Li tax ma def loolu mooy, bi ma jógee Padan di ñibbi, Rasel dafa faatu ca yoon wa ci sama kanam, ba nuy tollu ca réewu Kanaan, booba nu ngay dem, bay jub Efrata. Ma suul ko foofa, ca yoonu Efrata.» Efrata mooy Betleyem tey.
Melokaan wu jekk day naxe, taar day wéy, waaye jigéen ju ragal Aji Sax ji, kookoo jara gërëm.