TSK

TSK · Genesis 32:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu daldi ne: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay sang Ibraayma, ngalla nangul ma tey jii te laaye biir sama sang Ibraayma.

¶ Ba loolu wéyee Yanqóoba génn Beerseba, wuti Karan.

Maa ngi nii ànd ak yaw, di la sàmm fépp foo jëm, te itam dinaa la délloosi ci réew mii. Duma la bàyyi mukk, waaye dinaa def li ma la wax lépp.»

Aji Sax ji wax Yanqóoba ne ko: «Dellul ca sa réewu maam ya, ca say bokk. Dinaa ànd ak yaw.»

Ndaw ya daldi dem ba délsi ca Yanqóoba, ne ko: «Dem nanu ca sa mag Esawu, waaye moom ci boppam mu ngi ci yoon wi di ñëw, fekksi la fii, te ma nga ànd ak ñeenti téeméeri góor.»

¶ Ba loolu amee Buur Daawuda dikk ba fa kanam Aji Sax ji, toog ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji! Ana lu ma doon, ak lu sama waa kër doon, ba tax nga indi ma ba fii?

Job 17:9 TSK

Waaye aji jub a ngi topp yoonam, boroom loxo yu set a ngi gëna am kàttan.

Moo luy nit, ba nga di ko bàyyi xel? Luy doom aadamaak loo koy yége?

Moo may tàggat ngir xare, may bank xalag xànjar.

Buy jàll xuru Jooyoo, mu saf ko bëti ndox, céebo sànge xur wa barke,

Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.

Jëfi ngoru Aji Sax ji laay fàttlee ak cant gi Aji Sax ji yelloo, ngir li nu Aji Sax ji defal lépp; mbaax gu réy gi mu ji waa kër Israyil, defal leen ko ci yërmandeem, ak jëfi ngoram gu réy.

Yaay sàmm kóllëre ak Yanqóoba, yéwéne Ibraayma, na nga ko giñale woon sunuy maam, janti démb.

Yeen itam noonu. Bu ngeen defee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay jaam rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»

¶ Damay sant sunu Boroom Almasi Yeesu mi ma dooleel, moom mi ma natt ba wóolu ma, tabb ma ci liggéey bi,