TSK

TSK · Genesis 32:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk,

ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”»

Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”»

Te Aji Nekk-Fàww ju Israyil ji du fen, du réccu, ndax du nit bay réccu.»

Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal; su nu ko ñàkkee kóllëre, mu saxoo kóllëreem, ndax manula gàntal boppam.

Yàllaa bëggoona firndeel nu mu gëna leere ñeel ñi moom dige bi, ne ab dogalam du tebbiku mukk. Moo tax mu dogale ngiñ ab digeem.