TSK

TSK · Genesis 32:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe).

Jiitu ma rekk, sang bi, man ma topp ndànk ci wewu jur gi, jiital leen, te baña raw xale yi, ba kera ma lay fekksi Seyir.»

¶ Ba loolu amee Esawu ànd aki soxnaam, aki doomam yu góor ak yu jigéen, ak waa këram ñépp, jiital géttam ak juram gépp, yóbbaale mboolem alal ju mu amoon ca réewu Kanaan, daldi sanci meneen réew ngir sore rakkam Yanqóoba.

Mooy na mu defaloon Esaween ña dëkke Seyir rekk, ba mu leen fàkkasalee Oreen ña, Esaween ña dàq leen, sanc, wuutu leen, ba bésub tey jii.

Alyaasa nag ñaan ne: «Aji Sax ji, ngalla ubbil ay bëtam, mu gis.» Aji Sax ji ubbi bëti surga ba, mu xool, ndeke tund waa nga fees aki fas aki watiiri sawara, wër Alyaasa.

Luke 9:52 TSK

Mu yebal ay ndaw, ñu jiitu ko. Ñu dem, ba agsi ab dëkk ci diiwaanu Samari, nar ko faa waajal ab dal.