TSK

TSK · Genesis 32:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Soo defee lu baax, dees na la nangul; soo deful lu baax, bàkkaar a ngi lay yeeru ci sa bunt, di la tërook a wut, waaye yaa ko wara man.»

Mu ne Yanqóoba: «Gaawe ma ci ndambe lee waay, ba ma duy sama biir ci sa ndambe lu xonq loolu, ndax xiif a ngi may rey.» Loolu moo tax ñu tudde Esawu, Edom (mu firi Xonqe).

Isaaxa ne Esawu: «Mbaa am naa lu ma la ñaanalati, doom? Ndax kat xas naa koo def, muy sa kilifa, te bokkam yépp laa def ñuy surgaam, te pepp ak biiñ laa ko woomale it, ba mu ne gàññ.»

Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?”

Jiitu ma rekk, sang bi, man ma topp ndànk ci wewu jur gi, jiital leen, te baña raw xale yi, ba kera ma lay fekksi Seyir.»

¶ Askanu Esawu, di maami Edomeen ña ca tundi Seyir, mooy lii.

Ñu teraxlaayoo ay saaku, tañlaayoo ay buum, dem ca buurub Israyil, ne ko: «Ben Addàd sa jaam ba nee, nga baal ko ngalla te bàyyi ko mu dund.» Mu ne: «Ndeke mu ngi dund ba tey? Moom sama mbokk a!»

Tont lu neex day giifal, baat bu ñagas di jógal xol.

Yéene bii moo wàccal Duuma: Nit a ngi may wooye tundu Seyir, naan: Jongrukat bi, lu des ci guddi gi? Éy jongrukat bi, lu desati ci guddi gi?

noonu Saarata déggale woon Ibraayma, naan ko «Sang bi». Yeen jigéen ñi nag, yeen ay doomi Saarata, li feek yeena ngi def lu baax te bañ cee ragal ku leen xupp.