TSK

TSK · Genesis 35:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba Aji Sax ji gisee ne Leya fonkeesu ko, mu may ko, mu taawlu, te Rasel moom manula am doom.

Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (mu firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (mu firi Sama doomu njiglaay).

Góor ñooñoo xeetoo ci Bilaa, mi Laban may doomam Rasel, te ñu askanoo ci Yanqóoba, ñoom ñépp di juróom ñaari bakkan.

«Ruben, yaw mi ma taawloo, nga sosoo sama digg doole, sama ndoortel kàttan, yaa jëkke sut moos ci teraanga ak doole.

¶ Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israyil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di:

¶ Jenn waay ju bokk ci giirug Lewi nag moo jëloon janq bu mu bokkal giir.

¶ «Bul dëkkoo sa soxnas baay, di torxal sa baay.

¶ Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.

¶ Ki joxe saraxam ci bés bu jëkk bi, ñeel giirug Yuda, mooy Nason doomu Aminadab.

Ñooñu ñoo di: Samwa doomu Sakuur, ci giirug Rubeneen ñi,

¶ Ñii nag lañu limal Leween ñi ak seeni làng: ñoom Gerson mi sos làngu Gersoneen ñi, ak ñoom Keyat mi sos làngu Keyateen ñi, ak ñoom Merari mi sos làngu Merareen ñi.

Ñooñoo di: Ci wàllu giirug Yuda, Kaleb doomu Yefune,

¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku tëdde jabaru baayam, ndax suturas baayam la xàwwi.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»

¶ Eli nag mujj na di mag lool. Ba mu yégee mboolem li doomam yu góor yi def ak Israyil gépp, bay tëdde sax jigéen ñiy liggéey ci bunt xaymab ndaje mi,

Ayitofel ne ko: «Demal dëkkoo sa nekkaaley baay, yi mu wacce këram, ñu di ko topptoo. Su ko defee bànni Israyil yépp dinañu xam ne def nga lu tax sa baay sib la. Dina tax say farandoo gëna am fit.»

¶ Buur Daawuda nag ñibbi këram ga ca Yerusalem. Teewul fukki nekkaaleem ña mu waccoon ñuy topptoo kër ga, da leena boole denc ci genn kër, ñu di leen fa wattu. Mu yor leen fa, te dëkkootu leen. Dees leen faa denc ba keroog ñuy dee, ñu mel ni ay jëtun.

Miir bu ci nekk dina am ñetti bunt yu ñu dippee ñetti giiri Israyil. Wetu bëj-gànnaar, benn buntu Ruben ak benn buntu Yuda ak benn buntu Lewi.

¶ Déggees na nag ci lu wér, ne powum séy am na ci seen biir, te powum séy mu ni mel, giseesu ko sax ci biir xeeti yéefar yi. Dem na sax ba nit nekk ak jabaru baayam.

Tatay dëkk baa nga sampe ci fukki doji kenook ñaar yu ñu bind fukki tur ak ñaar yu ndawi Gàtt bi.