TSK

TSK · Genesis 39:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab Ebrë, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam.

mu nettalee ko ko noonu ne ko: «Jaamu ebrë, bi nga indi ci kër gi de, da maa fekksi, di ma sàkku.

Nit ku bon a ngi may duural, di ma jiiñ lu ma yégul.

Yaw boroom làmmiñu njublaŋ, ana lu ñu lay añale ak lu ñu lay dolli?

Yeen ñi xam njekk, dégluleen ma, yeen, askan wi sama yoon yebu ci seen xol. Buleen ragal nit ku leen sewal, buleen tiit seeni xaste.

Dëkk bu yàqu bi nga doon, ku jegeek ku soree lay kókkali. Boroom der bu yàqu bi, sa lépp a salfaañoo!

ci biir teraanga, ak ci biir toskare; ci biiri baatal, ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu;

Te sax su ngeen doon jànkoonteeki coono ndax seenug njub, ndokklee yeen. Buleen am jenn tiitaange ci seeni xuppe, te buleen jaaxle.