TSK

TSK · Genesis 39:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu daldi ne: «Sang bi, siyaare naa la. Ngalla waay, bu ma romb.

¶ Mu am bés Ibraayma wax surgaam, bi gëna yàgg ci këram, tey saytu alalam jépp, ne ko: «Dugalal sa loxo ci sama suufu lupp,

¶ Esawu ne ko: «Waaw, dal bu réy bii ma dajeel, loo ci namm?» Yanqóoba ne ko: «Xanaa di sàkku nga dalal ma jàmm rekk, sang bi.»

Teewul Yuusufa bañ, ne soxnas sang ba: «Déglul, sama sang da maa jébbal lépp, ba topptootul dara ci kër gi.

Kon dinaa la may, nga jiite kër buur, te waa réew mépp ci sa waaw lañuy wéy; jal bi ma toog doŋŋ laa lay sute.»

¶ Ci biir loolu yépp, ngóor sa Samiyel di màgg, neex Aji Sax ji, neex nit ñi.

Buur wax ma, ne ma: «Ana looy sàkku?» Ma ñaan gaaw ci Yàlla Boroom asamaan,

Kon nga xam lu jaadu, neex Yàllaak doom aadama.

Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.

Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal, du liggéeyal baadoolo.

Wattuleen nag seen bopp, wattu mboolem gétt, gi leen Noo gu Sell gi sàmmloo, te ngeen foral mbooloom gëmkati Yàlla, mi Yàlla jote deretu boppam.