¶ Ba loolu amee Yàlla geestu Rasel, nangul ko, may ko doom.
TSK
TSK · Genesis 42:38
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yanqóoba xàmmi ko, daldi ne: «Sama mbubbu doom a moos! Éey waay, rabu àll kay moo daggate Yuusufa, yàpp ko!»
Waaye Yanqóoba yebalul Beñamin, rakku Yuusufa, ndax dafa ragal ne musiba man na koo dab.
Su ko defee ngeen ànd ak seen rakk, fabu dellu ca waa ja.
Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: “Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.”
Jëflanteel ak moom ci kaw xel, bu ko bàyyi mu duggaale bàmmeel bijjaaw.
Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc, ba keroog may xamal maasu tey sa doole, xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar.
Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf, ndeke lépp cóolóoli neen la ak napp um ngelaw.
Man de dama noon: «Sama digg doole laay deme jaare bunti njaniiw, sama ndesu fan réer ma!»