Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.»
TSK
TSK · Genesis 45:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dëgg la, fexeel ngeen ma lu bon, waaye Yàllaa ko walbati, def ko lu baax, ba dogal li am tey jii, muy bakkan yu bare yi mucc.
¶ Ba loolu amee Elkana ak njabootam teela xëy ca ëllëg sa. Ñu màggal Aji Sax ji, ba noppi bàyyikoo fa, ñibbi seen kër ca Raama.
Buur ne ko: «Yeen doomi Seruya yi, lu ciy seen yoon? Sañ na maa saaga. Su ko Aji Sax ji santee mu saaga ma, ana ku ko saña laaj lu tax?»
Ndax soo ci selaŋloo ba selaŋlu ci tey jii it, wall ak xettal dina bawoo feneen ñeel Yawut yi, waaye yaw yaak sa waa kër baay dingeen sànku. Li nga dugg ci nguur gi sax, nga defe ne neen la? Jombul diggante bii nu tollu tey moo ko waral.»
Moo wàcce ab xiif ca réew ma, dagge fa luy gub,
Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!
Nit kooku ñu jébbale ni ko Yàlla dogale te nasoon ko lu jiitu, yeena ko daajloo yéefar yi ci bant, reylu ko.
¶ «Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,
ngir Seytaane bañ noo nax, ndax ay pexeem, umplewunu ko.