Genesis 29:16
TSK
¶ Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Laban nag amoon na ñaari doom yu jigéen, taaw ba di Leya, rakk ja di Rasel.
Yàlla nangul Leya, mu ëmb, am ak Yanqóoba seen juróomeelu doom ju góor.
¶ Am na bés Diina, ku jigéen ki Leya amal Yanqóoba, génn di seeti moroom ya ca dëkk ba.
«Ruben, yaw mi ma taawloo, nga sosoo sama digg doole, sama ndoortel kàttan, yaa jëkke sut moos ci teraanga ak doole.
¶ Aji Sax ji moo wax ak Musaa ca màndiŋu Sinayi ca biir xaymab ndaje ma, keroog benn fanu ñaareelu weer wu ñaareelu at, ma topp ca gàddaay ga bawoo Misra. Mu ne ko:
¶ Aji Sax ji dafa wax Musaa, ak Elasar doomu Aaróona sarxalkat ba, ne leen: