Yuusufa tudde taaw ba Manase (mu firi Ki ma taxa fàtte), ndaxte da ne: «Li ma sonn ak li ma sore sama kër baay lépp, Yàlla fàtteloo na ma ko.»
TSK
TSK · Genesis 48:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yuusufa itam am Manase ak Efrayim ca réewum Misra, seen yaay di Asnat doomu Potifera, may njiitu diine ca dëkk ba ñu naan On.
Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la: Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyut. Wàllu Manaseen ñi, Gamalyel doomu Pedasur.
¶ Ñi askanoo ci Yuusufa nag, ñook seeni làng, ñoo soqikoo ci Manase ak Efrayim.
Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.
¶ Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Fukki giiri Israyil yeek ñaar nag, kemi céri suufi réew mi ñuy séddoo, nii la wara tëdde: na wàllu giirug Yuusufa di ñaari cér.
Maay doon seen baay, ngeen di samay doom, góor, ak jigéen,» la Boroom bi, Aji Man ji wax.
giirug Aser, fukki junneek ñaar, giirug Neftali, fukki junneek ñaar, giirug Manase, fukki junneek ñaar,