ne ko: «Yaa di Yanqóoba, waaye deesatu la wooye Yanqóoba; léegi yaa di Israyil.» Mu tudde ko nag Israyil.
TSK
TSK · Genesis 49:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàlla da maa yebal, ma jiitusi leen, ba rawale seen bakkan, dikke leen xettal gu mag, ba seen askan baña fey.
Ba loolu amee Yuusufa di dundal baayam aki bokkam, ak mboolem waa kër baayam, boole ca ña bootu ca ñoom.
Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla.
Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, te njekk ak njub mooy boroom.
Alyaasa ne ko: «Soxal.» Mu sox. Alyaasa teg ay loxoom ca kaw loxoom,
Ma noon darajaa may yeesalal nganam, may gëna daŋalati xala.
Maak yaw kay, ma song gàngoor. Maak sama Yàlla, ma tëb um tata.
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax jee may sàmm, du lenn lu ma ñàkk.
Aji Sax jeey dooleel ñoñam. Mooy làq, di musal buur bi mu fal.
Du fitt laa wóolu, du saamar a may may ndam.
Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
Moo giñaloon Aji Sax ji, moo digook Mbërum Yanqóoba ma.
Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!
ba ñi réeroon, mujj xam; ñurumtukat yi dégg ndigal.
Yaay naan soowum xeet yi, nàmp weenu buur yi, ba xam ne maay Aji Sax jiy walloo, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.
Ci Aji Sax ji laa leen di jàmbaarale, ciw turam lañuy daagoo. Kàddug Aji Sax jee!»
Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen beddi woon, yeen tabaxkat yi, te mu mujj di doju coll wi.”
Yeena di tabax, bi ndawi Almasi ak yonent yi di kenu gi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju coll wi.
Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.