¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.
TSK
TSK · Genesis 49:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.
Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.»
Mu ne leen: «Jàmm rekk la; buleen tiit, seen Yàlla, jiy seen Yàllay baay, moo leen defal alal ci seeni saaku. Seen xaalis jot naa ci.» Ci kaw loolu mu génne Simeyon, indil leen ko.
Barke yii yépp a leen di dab, sottiku ci seen kaw, bu ngeen déggalee seen Yàlla Aji Sax ji:
Yuusufa la wax, ne ko: Yal na barkeb Aji Sax ji ñeel suufam, bawoo ca xéewali asamaan, dib lay, ak ndox mu lal xóotey suuf,
kóllëre jebbee fa suuf, njekk séentoo asamaan,
¶ Kon nag bu kenn puukarewoo ay nit, ndax lépp, yeena ko moom,
Te sama Yàlla itam mooy sàkke ci koomam gu yéeme gi ci Almasi Yeesu, ba fajal leen seen soxla yépp.