TSK

TSK · Genesis 49:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Booba Rasel a ngi waaja faatu. Terewul bala bakkanam a rot tudde na xale bi Benoni (mu firi Sama doomu coono). Teewul baay bi tudde ko Beñamin (mu firi Sama doomu njiglaay).

Wii askan ni gaynde lay jóge, ni gayndeg sibi lay faboo, du goor te yàppul am pàdd, deret ja tuuru, mu xab.»

Beñamin la wax, ne ko: Soppeb Aji Sax jaa ngi, keey dëkke xel mu dal fi wetam, mu di ko yiir bésoo bés, te diggantey waggam la dëkke.

¶ Ba ndaw ya dikkee Gibeya, ga Sóol dëkk, ba xamle mbir ma, waa dëkk ba di dégg, ñoom ñépp a yuuxu, di jooy.

¶ Waa Filistee boole woon seeni gàngoor ngir xare. Ñu daje ca dëkk ba ñu naan Soko ca diiwaanu Yuda, daldi dale ca Efes Damim diggante Soko ak Aseka.

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Moo tax ma mel ni gaynde ci yeen di tëroo ni segg ciw yoon.

Acts 8:3 TSK

Ci biir loolu Sóol moom, ma ngay jéema faagaagal mbooloom gëmkat ñi, di dugg ci kër yi, diri góor ak jigéen, génne, ñu sànni kaso.

Man nag xam naa ne gannaaw bu ma demee, ay bukki yu ñàng dinañu tàbbi ci seen biir te duñu ñéeblu gétt gi.