Waaye dinaa fas kóllëre ak yaw, nga dugg ci gaal gi, yaak say doom ak sa soxna ak say soxnay doom.
TSK
TSK · Genesis 7:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Keroog bés boobu la Nóoyin ànd aki doomam yu góor, Sem ak Xam ak Yafet, ak soxnaam ak ñetti soxnay doomam yooyu, ñu dugg ca gaal ga,
Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.
Jub, barkeelu; ku soxor, wax ja làq fitna.
Alal du jariñ bésu mbugal; jub, mucc ci gàtt fan.
Turu Aji Sax ji rawtu bu mag la. Ku jub daw làqu ca, raw.
Yeen samaw askan, ayca duggleen seeni néeg, tëju ca biir. Làquleen as lëf, ba sànj mi jàll.
su Nóoyin ak Dañeel ak Ayóoba bokkoon nekk ca seen biir sax, ñoom ñett doŋŋ la seen bakkan di mucc ndax seenug njub. Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jaambur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.»
¶ Ngëm la Nóoyin dégge waxyub Yàlla bu jëm ci lu kenn gisagul woon, te ragal Yàlla la sàkke gaal, ngir musal njabootam. Ngëmam it la tiiñale àddina, ba ab céram di njub gi ngëm di maye.
ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;