ngalla fexeleen rekk ba ragal Aji Sax ji, te ngeen dëggu ci jaamoo ko seen léppi xol, ndax dangeen di xool ci jaloore yu yéeme yi mu leen defal.
TSK
TSK · Hebrews 12:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waxambaane sonn, loof; xalelu góor di tërëfa tërëf,
Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqliku ci digg Israyil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal.
¶ Firikati yoonu Musaa yi ak Farisen yi tàmbalee nàttable ci seen xel, naan: «Kii di saaga Yàlla mooy kan? Ana ku mana jéggaley bàkkaar ku dul Yàlla doŋŋ?»
¶ Ba Yeesu génnee foofa, ca la Farisen ya ak firikat ya tàmbalee xabtalu ci kawam, di ko seetloo ay laaj ci mbir yu bare,
¶ Benn bésub Noflaay la Yeesu reeri woon kër genn kilifag Farisen ya. Ñoom nag ñu di ko bàyyi xel bu baax.
¶ Farisen ñu bëgg xaalis ña nag dégg loolu Yeesu wax lépp, ba noppi di ko ñaawal.
¶ Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.
¶ Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bés ak bés.
Yeen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu baax.
¶ Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
Te it fàtte ngeen kàddu yii ñu leen ñaaxe, ni nit aki doomam: «Doom, bul xeeb yaru Boroom bi, bul xàddi, bu la waññee,