Musaa jël deret ja, wis-wisal ca kaw mbooloo ma, ne leen: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen te mu aju ci mboolem kàddoom yii.»
TSK
TSK · Hebrews 13:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.
Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.
Ñoñam ña daldi fàttliku janti Musaa ya woon. Ña nga naan: «Ana ki jàlle woon Israyil géej, mook sàmmi géttam ga? Ana ki yebaloon noowam gu sell ci seen biir?
¶ «Gannaaw loolu maa leen di waajalal ab sàmm bu leen di sàmm. Kookooy Daawuda sama jaam bi. Moom moo leen di foral, mooy doon seen sàmm.
Maay fas ak ñoom kóllëreg jàmm, gu sax. Maa leen di samp, ful leen, maay samp sama bérab bu sell fi seen biir, ba fàww,
¶ Kaas ba itam noonu la def ak moom gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret ji leen nara tuurul.
Yeesu moomu nag, Yàllaa ko dekkal, nu seede ko, nun ñépp.
xamleen xéll, yeen ñépp ak bànni Israyil gépp, ne ci turu Yeesu Almasi waa Nasaret bi, ki ngeen daajoon ci bant, te Yàlla dekkal ko, ci turam doŋŋ la kii wére, ba taxaw ci seen kanam.
moom la Yàlla dekkal ci ñetteelu fanam, ba may ko mu feeñ.
Ndaxte Yàlla jàpp na bés bu muy àttee àddina ci dëgg, àtte bu nit ki mu taamu di sottali; te loolu Yàlla jox na ci ñépp firnde lu wóor, ba mu dekkalee kooku mu taamu, ndekkite lu dee toppul.»
Nun itam ci lanu; dees na nu waññal sunu ngëm, àtteb ñu jub, nun ñi gëm Ki dekkal sunu Sang Yeesu,
Yal na Yàlla miy boroom jàmm ànd ak yeen ñépp. Amiin.
Yàlla, mi dekkal Sang bi nag, mooy dekkal it sunu yaram ci kàttanam.
Te su boobaa nag ñu war noo jàppe ay seedey fen-kati Yàlla, ndax noo seedeel Yàlla, ne moo dekkal Almasi te dekkalu ko, gannaaw ñi dee duñu dekki.
¶ Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.
ji mu fésal ci Almasi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram, fa déndi asamaan.
Ni ñu leen booleek moom suul, keroog ba ñu leen sóobee cim ndox, noonu ngeen dekkeendoo ak moom, ndax yeena wóolu dooley Yàlla mi ko dekkal.
¶ Yàlla ci boppam, moom miy Boroom jàmm, yal na leen sellal, ba ngeen mat sëkk, te seen léppi xel, ak seen léppi xol, ak seen léppi yaram sàmmu, ba mucc sikk, ba kera bés bu sunu Sang Yeesu Almasi feeñee.
¶ Kayitu ndono nag fu mu teew, fàww joxees fa firndey deewug ka donale,
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu, ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
ñi Almasi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.
ba bu Sàmm bu mag bi feeñee, ngeen jot kaalag daraja gu dul furi.