TSK

TSK · Hebrews 13:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot?

Acts 7:55 TSK

Eccen nag feese Noo gu Sell gi, ne jàkk asamaan, daldi gis leeru Yàlla, gis Yeesu taxawe fa ndijooru Yàlla.

Mbooloom gëmkat mu nekk nag, ñu tabb ci ay mag; ci biir loolu ñu ñaan, boole kook koor, daldi dénk mag ña Sang bi ñu gëm.

Aw ngeen sunuy tànk, aw it ci tànki Sang bi, nde yeena jot ci kàddu gi, ci biir njàqare ju bare, te di ko bége ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

¶ Gannaaw loolu bokk yi, danu leen di ñaan, ñi féetewoo coonob liggéey ci seen biir te jiite leen ci yoonu Boroom bi, di leen yee, nangeen leen yég.

Moona du sañ-sañ bu nu ci ñàkk, xanaa bëgg leena won lu ngeen nu roye, ba ngeen aw ci sunuy tànk,

Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.

¶ Nuyul-leen ma mboolem seeni njiit, ak mboolem gëmkat ñu sell ñi. Waa Itali ñu ngi leen di nuyu.

¶ Ba mu tàyyee juróomeelu tayu gi, ma gis ci suufu sarxalukaay bi, bakkani ñi ñu bóom ndax kàddug Yàlla ak seede si ñu ci seede.