TSK

TSK · Hebrews 3:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 21:14 TSK

Moona kee noon Yàlla: «Xiddi ma! Xam saw yoon soxalu ma.

Aji Sax jee ma yool sama njekk, samay loxoo set, mu fey ma.

Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko, te noo dëddoo sunu Yàlla jii, kàdduy fitna ak fippu, ak fen yu nu mébét, nas ko,

«Janti keroog Yerusalem, ngànguney Aji Sax ji lees koy wooye, xeetoo xeet di fi daje, ngir Aji Sax, ji turam ñeel Yerusalem, te dootuñu të ticc ci seen mébét yu bon.

Waaye dégluwñu, teewluwñu, xanaa ku nekk di wéye dëgër bopp, topp ag bon xolam. Moo tax ma wàcce ci seen kaw mboolem sàrti kóllëre gii ma leen santoon ñu war koo jëfe te jëfewuñu ko.”»

Aji Sax ji dafa wax ne: «Alkànde ñeel na ku yaakaar doom aadama ak képp kuy doolewoo nit, dëddu Aji Sax ji.

Dañu naan: “Jaru ko, sunu xalaatu bopp lanuy topp, ku nekk të ticc di jëfe sa xel mu dëng.”»

Hosea 1:2 TSK

¶ Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.»

Ndegam cari judduwaale ya la Yàlla déegul, moytul mu bañ laa déeg yaw itam.

Nit ñi ci seen bopp ñoo nuy waxal fépp, na sunu ngan ak yeen deme, ak ni ngeen walbatikoo ci Yàlla, dëddu tuur yi, bay jaamu Yàlla ju dëggu jiy dund,

diiru ñeent fukki at. Moo tax ma mere googu maas, ba ne: “Seen xol a dëkke lajj, te nanguwuñoo xam samay yoon.”

Moytuleen balaa kenn di ñàkk yiwu Yàlla. Moytuleen bala ab reenu wextan di fëll, di lëjle, ba rax mbooloom lëmm.