Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer, ngeen sànkoo seenu yoon; meram day jekki ne jippét, waaye ndokklee képp ku ko làqoo!
TSK
TSK · Hebrews 3:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ki ci jal bi ci boppam, bu baadoolo yiy dugg, na duggandook ñoom, bu ñuy génn, mu génnandook ñoom.
¶ Xoolal kon ni Yàlla baaxe, ak ni mu ragloo; ci ñi déggadi la raglu, baax ci yaw, ndegam cig mbaaxam nga sax; lu ko moy dees na la tenqi yaw itam.
¶ Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,
Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.
Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm, bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.
¶ Sunu Sang Yeesu Almasi ci boppam, ak Yàlla sunu Baay, mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk, ak yaakaar ju wér,
Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.
Ndax kat noo di àndandooy Almasi, ndegam wéye nanoo ŋoy bu dëgër ci sunu kóolute ga nu doore, ba kera muj ga.
¶ Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
Nanu ŋoy ci yaakaar, ji nu biral ne moom lanu am, te nu baña yoqi, nde ki dige ku wóor la.
Sama nit ku jub nag mooy dund ndax ngëm ga, waaye ku dellu gannaaw, sama xol bégewu la.»
Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Catir nag, bind ko ne ko: «Lii moo di kàdduy Doomu Yàlla ji, ki ay gëtam mel ni sawara wu yànj, ndëgguy tànkam mel ni xànjar bu ñu jonj. Mu ne:
¶ «Maa ngi ñëw léegi. Ŋoyal ci li nga yor, ngir kenn baña fëkk sa kaalag ndam.