Ba loolu amee fit la leen Póol ak Barnaba tontoo, ne leen: «Yeen Yawut yi de lanu wara jëkka yégal kàddug Yàlla gi, waaye gannaaw gàntal ngeen ko, ba jombale seen bopp ag texe ba fàww, nu ngii di walbatiku ci jaambur ñi.
TSK
TSK · Hebrews 4:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Waaye du ñépp a nangul xibaaru jàmm bi; moo tax Esayi ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunub dégtal?»
Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»
ndax sunu xibaaru jàmm, bi nu leen àgge, dikkewu leen ay wax rekk, waaye manoore la leen dikkaale, ak ndimbalal Noo gu Sell gi, ak kóolute gu mat sëkk gu ngeen am. Xam ngeen moos na nu nekke woon ca seen biir, di xintewoo seen njariñ.
Su ko defee mbugal dal mboolem ñi gëmul dëgg gi, xanaa di xejjoo njubadi.
¶ Bokk yi, wattuleen bala kenn ci yeena am xolub gëmadi bu bon bu koy xiir ci dëddu Yàlla jiy dund.
Kon nag am na ñenn ñu ci wara tàbbi ba tey. Te ñi ñu jëkkoona àgge xibaaru jàmm bi, tàbbiwuñu ca ndax seenug déggadi.
Kon nag baleen jépp jikko ju tilim, ak mboolem xeeti mbon yi ne gàññ, te ngeen nangu ci biir ag woyof, kàddu, gi jëmbate ci yeen te man leena musal.