képp ku gëm Yeesu, ci moom lay wàccook loolu lépp, ba ag njubam mat.
TSK
TSK · Hebrews 7:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Li yoonu Musaa tële woon ndax néew dooley nitu suuxu neen, mooy lii Yàlla def: Doomam la yónni, mu dikke melow nit, te nit di bàkkaarkat, di suuxu neen, ngir Doomam fajtal mbirum bàkkaar. Yaramu suux wu nit kooku la Yàlla sottale mbugal gi war ci bàkkaar,
Li ma ciy wax mooy lii: kóllëreg Yàlla gi taxawe ni kayitu donale gu mu dëggal, yoonu Musaa, wi dikk ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw kóllëre gi, manu koo neenal, ba fomm digeb Yàlla.
¶ Waxleen ma, yeen ñi bëgga nekk ci kilifteefu yoonu Musaa, xanaa xamuleen li yoon wi wax?
¶ Kon liggéeyu carxal gu Leween, ñi yoroon yoonu Musaa, wi ñu dénkoon bànni Israyil, su doon liggéey buy taxa mat sëkk, ndax dees na soxlaati beneen sarxalkat bu jóg topp dayob Melkisedeg, te toppul dayob Aaróona?
¶ Bu kóllëre gu jëkk ga muccoon sikk nag, deesul soxlaa xajal geneen.
¶ Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi.