TSK

TSK · Hosea 10:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

su boobaa buleen sujjóotal mukk seeni tuur, di leen jaamu, mbaa ngeen di roy seeni aada, waaye yàqteleen seeni tuur te toj tasar seen tuuri doj, ya fa sampe.

Ca ëllëg sa, ñu teela xëyati, fekkuñu lu moy jëmmu Dagon ja daanu ba dëféenu fa suuf, fa kanam gaalu Aji Sax ji. Bopp baak cati loxo ya damm, ne wesar ca dëwu bunt ba, desul lu moy yaram wa.

Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.

Dina rajaxe tuuri doj ya sampe ca Bet Semes ci biir Misra te dina lakk këri tuur yi ci Misra.”»

Hosea 7:8 TSK

Efrayim moo jaxasook askani jaambur, Efrayim moo di mburu mu ñu walbatiwul cib taal.

Waa Samaree ngi am tiitaange ci sëllu wu ñu xelli ca Bet Awen, askan wa di tiislu tuur ma, ay xërëmkatam di lox ndax darajay sëllu, ji leen dëddu, dem ngàllo.

Maay buddee fi sa biir xeri jaamookaayi Asera tuur mi, te maay tas say jaamookaay.

¶ «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «Turi xërëm laay dagge ci réew mi, ba deesatu leen fàttliku. Yonent yeek xelum xërëmtu it, maa koy tukkal ci réew mi.

¶ «Ab jaamu kër nag manula jaamu ñaari sang; day dëddu kii, sopp kee; mbaa mu fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.»

James 1:8 TSK

Boroom xel-yaar la, xel maa toogul ci lenn lu muy def.