TSK

TSK · Hosea 3:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Fekk na Laban dem wati ay xaram. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam.

Yii yére nag lañu koy defaral: kiiraayal dënn ak ab xar-sànni ak ab fëxya, ak mbubb mu gudd mu ñu ràbb, ak kaala ak laxasaay. Yérey sellnga lañuy defal sa mag Aaróona ak doomam yu góor, ngir ñu di ma sarxalal.

solal Aaróona mbubb mu gudd ma, takkal ko laxasaay ga, solal ko fëxya ba, tegal ko ca xar-sànni ma, takkal ko ngañaay la ca kawam, jàppe ko ko, mu tafu ca kawam.

¶ Ci biir loolu ngóor sa Samiyel moom, ma ngay liggéeyal Aji Sax ji, sol xar-sànnim lẽewam.

¶ Daawuda ne Ayimeleg: «Dencoo fi ab xeej mbaa saamar bu jàppandee? Ndax du saamar, du lenn ci samay gànnaay lu ma indaale, ngir yónnentu Buur a jampoon lool.»

¶ Ba Abiyatar doomu Ayimeleg dawee fekki Daawuda ca Keyla, xar-sànni ma la indaale.

Ci biir loolu Daawuda wax ak sarxalkat ba Abiyatar doomu Ayimeleg, ne ko mu indil ko xar-sànni mi. Abiyatar indil Daawuda xar-sànni ma.

Rax ci dolli boroom rawaan yeek gisaanekat yeek gàllaaji kër yeek kasaray tuur yeek mboolem kasara yu ni mel te ñu daan ko gis ca réewum Yudak Yerusalem, Yosya jële na ko fa ngir mana saxal kàdduy yoon wa ñu bind ca téere ba Ilkiya sarxalkat ba gisoon ca biir kër Aji Sax ji.

Bésub keroog ab sarxalukaay ñeel Aji Sax ji, fa digg réewum Misra, aw xer it ñeel Aji Sax ji fa kemu réew ma,

Bunti dëkk ba suulu na, te moo yàqte, dammate weñi tëjukaay ya, buuram aki garmeem a tumurànkeji ca yéefar ya, te téereb yoon amul, yonent it gisatul peeñu mu bawoo fa Aji Sax ji.

Li ngeen mébét ci seen xel du am mukk. Yeena ngi naan: ‘Nan mel ni xeet yépp, mel ni waasoy réew yi, di jaamu bant ak doj.’

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dindil kaala gi, foq mbaxanam buur mii; la woon wonni na, ku noon dett jóg, ku jóg, detteelu.

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

Jamono ja ñuy dakkal sarax si wara sax fàww, di keroog ba ñuy taxawal lu siblu lay jur yàqute, junniy fan ak ñaar téeméer ak juróom ñeent fukk (1 290) dina ca topp.

Israyil di reseñ gu naat, meññal boppam lu ne gàññ, te lu meññeef ma gëna yokku, mu gëna yokkati sarxalukaayi tuur. Lu am réewam gëna baaxle, mu gëna baaxal ay xeri tuur.

Ci biir mer laa la falal buur, te ci samam sànj laa ko follee.

¶ «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «Turi xërëm laay dagge ci réew mi, ba deesatu leen fàttliku. Yonent yeek xelum xërëmtu it, maa koy tukkal ci réew mi.

Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.

Acts 6:13 TSK

Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa.