TSK

TSK · Hosea 4:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Lu tax ngeen di teddadil sama saraxi rendi ak yeneen sarax yi ma santaane ci màkkaan mi? Lu waral ngay teral sa doom yi teraanga joo ma joxul, ba ngeen di yafloo li gën ci mboolem saraxi Israyil sama ñoñ?”

Xanaa ku mucc ayib, sell ab xol, xemmemul caaxaani neen, du giñey fen.

Xaj yu tiita tiit lañu, xamuñu suur, te ñooy sàmm yeey! Ñoom ñépp, kenn manu cee xam dara, seen yoonu bopp lañu topp, ak seen amin wu lewul.

¶ «“Képp ku bokk ci waa kër Israyil, mbaa muy doxandéem bu dal ci biir Israyil, bu ma waccee, ba yékkati kasaray tuur, def ci xolam, muy ay wu koy gàllankoor, te mu ne ci jàkk, kooku bu dikkee cib yonent di sàkku leeraange ci man, man Aji Sax ji maa koy tontul sama bopp.

«Éy bu kenn ci yeen tëjoon bunt yi far, te baña jafal ab taal ci sama kaw sarxalukaay ci dara. Awma benn bànneex ci yeen!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Ab sarax, duma ko nangoo ci seeni loxo.

Li war moo di tëj seen gémmiñ, ndax këri lëmm lañuy tase àlluwa ju ñu amul sañ-sañam, ngir di ko sàkkoo am-am bu lewul.