TSK

TSK · Hosea 5:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci jamonoy Peka buurub Israyil, Tiglaat Pilser buurub Asiri dikk, nangu dëkk yi ñuy wax Yon ak Abel Bet Maaka ak Yanowa ak Kedes ak Àccor ak diiwaani Galàdd ak Galile ak mboolem réewum Neftali. Mu jàpp waa réew ma, yóbbu Asiri.

Sa soppe yépp a la fàtte, kenn faalewu la ci, ndax dumay noon laa la duma, yar la yar bu tar ngir sa ñaawtéef ju réy ak sa bàkkaar yu bare.

Efrayim daa mel ni pitax, dofe, ñàkk xel, di woo wall Misraak a dem Asiri.

Moom it lees di yóbbu Asiri, defal ko buur bu mag ba ab galag. Gàcce mooy jàpp Efrayim, Israyil laa ne, mooy rus ci mébétam.

Waajal-leen ay kàddu te dellu ci Aji Sax ji, ne ko: «Baal nu mboolem ñaawtéef te nangul nu, nu yékkati kàdduy màggal yu wuutu saraxi yëkk.