TSK

TSK · Hosea 7:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Buurub Israyil nag woo yonent yi, ñu daje, xawa tollook ñeenti téeméer. Mu laaj leen ne leen: «Ndax ma dal ci kaw Ramot ga ca Galàdd, am ma bàyyi?» Ñu ne ko: «Demal, ndax Boroom bi moo leen di teg ci sa loxo.»

Yonent yiy wax waxyuy fen, sarxalkat yiy jiitee seen coobare, te sama ñoñ soppe ko ni! Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?»

¶ Ca menn at ma, fekk Cedesyas buurub Yuda di doora falu, yemook ñeenteelu atam, ca juróomeelu weer wa, am na doomu Asur ju ñuy wax Anaña, di yonent bu cosaanoo Gabawon. Mu wax ak Yonent Yàlla Yeremi ca biir kër Aji Sax ji, fa kanam sarxalkat yaak mbooloo mépp, ne ko:

Hosea 4:2 TSK

Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo. Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.

Hosea 7:5 TSK

Bu sunu buur xewlee, kàngam yi naan ba wopp, buur tàllal loxo ay ñaawlekat.

Dogali Buur Omri daal lees di topp, ak mboolem jëfini waa kër Buur Axab. Seeni pexe ngeen topp, ba tax may def dëkk bi di lu daw yaram, waa dëkk bi di ñu nit ñiy muslu ci seenu demin, te gàcceg sama ñoñ, yeena koy gàlloo.»

Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.