TSK

TSK · Isaiah 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ca màndiŋ ma it, gis ngeen na leen seen Yàlla Aji Sax ji fabe, ni baay di fabe doomam, ci yoon wi ngeen dox wépp, ba agsi bérab bii.»

maa ngi sàkku asamaan ak suuf seedeel maak yeen bésub tey jii, ne su boobaa yeenay sànkoo sànku ci lu gaaw, ba wuute ca réew, ma ngeen jàll dexu Yurdan, jëm fa, ngir nanguji ko. Su boobaa dungeen fa yàgge, ndax dees leen di raafal, ba ngeen jeex tàkk.

¶ Woo naa seede asamaan ak suuf ci yeen, bésub tey: dund ak ndee laa teg fi seen kanam, ak barke ak alkànde. Taamuleen dund ndax ngeen dund, yeen ak seen askan.

Daa dëddu Aji Sax ji, Yàllay maamam, baña jaar ci yoonu Aji Sax ji.

Naa woy sama soppe woyu cofeel wu solowoo tóokëram. Sama soppee fi amoon tóokër, kaw tund wu suuf sa nangu lool.

Wii xeet kat ay fippukat lañu, yii doom a diy fen-kat te nanguwuñoo sàmm yoonu Aji Sax ji!

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Ana sikk bu ma seeni maam gisal, ba tax ñu sore ma, di topp xërëmi neen, ba far neen?

Yeen waa àddina, dégluleen! Maa ngii di indil askan wii musiba, seeni pexe jural leen. Ñoo faalewul samay kàddu, gàntal sama yoon.

Éy waa réew mi, waa réew mee, waa réew mi, dégluleen Kàddug Aji Sax ji!

Maa fa jaare, seen la ngay wéqu, sangoo sa deret. Ma ne la: Sangoo nga sa deret waaye, dundal! Neeti la: Sangoo nga sa deret, waaye dundal.

Kon nag yeen tundi Israyil, dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi, ak xunti yeek xur yi, ak ndànd-foyfoy yu wéet yeek dëkk yi gental, te xeet ya ñu dëkkal sëxëtoo leen, yab leen.

Micah 1:1 TSK

¶ Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Mise miy waa Moreset, ca janti Yotam ak Axas ak Esekiya, buuri réewum Yuda, na seen nguur topplantee. Lii la Mise gis ci mbirum Samari ak Yerusalem.

Micah 3:8 TSK

Teewul man, may feese doole, feese Noowug Aji Sax ji, ak dëgg ak njàmbaarte, ngir biralal askanu Yanqóoba, bàkkaaram, ngir tuddal bànni Israyil googu moyam.

«Doom teral baayam, jaam, sangam. Man, su ma dee baay, ana saab teraanga? Su ma dee ab sang, ana saab cér?» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, mu ne: «Yeen sarxalkat yi teddadil ngeen sama tur, yeen ngeen ne: “Ana nu nu teddadile sa tur?”

¶ Kon nag ana lu ab Yawut rawe ci nit ñi? Ak luy njariñal xaraf?