TSK

TSK · Isaiah 10:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji wax Esayi ne ko: «Génnal gaaw, dajeek Axas, yaak sa doom Seyar Yasub, ma nga ca catal solomu mbànd ma féete kaw, ca yoonu toolu fóotkat ya.

Moo tax Aji Sax ji doge Israyil bopp ak geen, boole tiir ak barax fóom ci benn bés.

Ndes wa des ca askanu Yuda ñooy saxaat ay reen, ba meññaat ay doom.

«Ab jotkat ay dikkal Siyoŋ, ba jot ñi tuub seeni bàkkaar ci askanu Yanqóoba.» Kàddug Aji Sax jee.

Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.

Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal, te taxul ñu délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji. Loolu yépp taxul ñu sàkku ko.

Dees na topp waa Samari, nde ñoo fippu ci seen kaw Yàlla. Saamar lañuy fàddoo, seeni doom, ñu rajaxe leen, seen jigéeni wérul, ñu butti.

Waaye seenum xel a dërkiis. Ba tey jii, bu ñuy jànge biir mbooloo, téereb kóllëre gu jëkk gi, muuraay googoo fi des; murikuwul, ndax ci Almasi lay deñe.