TSK

TSK · Isaiah 14:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ca biir xeet yooyu nag, dungeen fa astandikoo, dungeen fa am sax fu ngeen noppale seen téstën. Aji Sax jee leen fay teg fit wu rëcc, ak gët yu giim, ak xol bu jeex.

Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.

ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, dal-lukaay yu dal xel.

¶ «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem.

«Yaw Yanqóoba sama jaam bi nag, bul tiit; yaw Israyil, ma ne bul ragal. Maa ngii di la wallusi, jële la fu sore, jële sa askan fa seen réewu njaam ga, Yanqóoba délsi, dal, aaru, du tiitati.

«Su boobaa waa kër Israyil, seen dëkkandoo yi leen di sewal, dootuñu leen lëjal ni dagg yu ñaw ak dég yuy jame. Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.

Maa leen di indi, ñu màkkaanoo digg Yerusalem, di sama ñoñ, may seen Yàlla, ci biir worma ak njekk.»

¶ Gannaaw loolu damaa dégg lu mel ni coow lu xumb, bawoo ci mbooloo mu bare mu àddoo asamaan, ne: «Aleluya! Texe ak daraja ak kàttan ñeel na sunu Yàlla.