TSK

TSK · Isaiah 2:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Njekk ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.

Ay askan yu bareey dikk, naan: «Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji, fa kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.

Aji Sax ji nee: «Xaacul loo man, te bul ñéeblu; àddul ni bufta, te yégal sama ñoñ seen bàkkaar, ngir waa kër Yanqóoba yii xam seeni moy.

Du jant a lay leeralati bëccëg, te weer du la niital; Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa Yàlla jooju di sab taar.

Ag lëndëm ngeen woon démb, waaye tey ag leer ngeen ci Boroom bi ngeen bokk. Jëfeleen nag ni niti leer.

Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Gàtt bi di làmpam.