Ag suba ngeen ne: «Éy waay, bu doon ngoonati.» Bu ngoonee ngeen ne: «Éy waay, bu doon subaati!», ndax tiitaange lu ngeen di tiit, ak li ngeen di teg seeni gët.
TSK
TSK · Isaiah 21:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba mu ko defee Absalom sant ay nitam, ne leen: «Ma ne, bu Amnon naanee biiñ, ba xolam sedd, bu ma leen nee ngeen jam ko rekk, reyleen ko. Buleen ragal; man maa leen ko sant. Góor-góorluleen nag te ñeme.»
Aman teg ca ne: «Te kat amul ku Lingeer Esteer woo, mu wara ànd ak Buur ca bernde ja muy def, ku moy man. Ëllëg man la woo maak Buur.
Day gis ay xaleem di bajantu, goneem yépp di tëbantu.
Wóoy ngalla ñiy teela xëy, daw wutiw ñoll, gonloo biiñ ba tàng jérr.
Ñu tàng bay bëgga dee, ma may leen ñu naana naan, màndal leen, ñu mana xawaare, tëdd nelaw nelawi fàww, duñu yewwooti.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ Am na bés Buur Baltacar defal ay jaraafam bernde ju réy. Ña nga tollu ci junni, muy naan nag ca seen kanam.
¶ Guddi googa lañu rey Baltacar, buurub waa Babilon.
¶ «Moytuleena yaafusal seen bopp ci naan gu ëpp ak màndite ak xalaati àddina, lu ko moy bés ba jekki dal ci seen kaw,