¶ Laata ati xiif yay agsi, Yuusufa am na ñaari doom yu góor ak Asnat doomu Potifera, kilifag diine, ga ca On.
TSK
TSK · Isaiah 24:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buleen indi mukk ci seen biir kër Yàlla Aji Sax ji, peyooru gànc bu jigéen, mbaa bu góor, ngir wépp xas wu ngeen namma wàccoo googu peyoor, ndax yooyu yaar yépp, seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na ko.
ak jàmbaar ak ñeyu xare, akub àttekat akub yonent, ak gisaanekat ak magum pénc,
Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, yonent bi mokkal naaféq dib geen.
«Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu, sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: “Bu ngeen demee Misra, ni sama mer ak sama xadar yurikoo woon fi kaw waa Yerusalem, ni la sama xadar naan yureet fi seen kaw. Dingeen doon gentu alkànde, ñu di leen móolook a sewal, te dungeen gisati miim réew.”»
¶ Ci kaw loolu njiital dag ya jàpp Seraya sarxalkat bu mag ba, ak Cefaña sarxalkat ba ca topp, ak ñetti dagi bunt kër Aji Sax ja.
Seen bàkkaari yonent yaa, seen ñaawtéefi sarxalkat yaa; ñoo tuur fa digg dëkk ba deretu aji jub ñi.
Kàngam yi, ñu jàpp, wékk; te mag ñi, teraleesu leen.
Nit kooku maa ko naa jàkk, def ko muy firnde, di ku ñuy léeboo, te maa koy wàññee ci sama ñoñ, ba ngeen xam ne maay Aji Sax ji.
Waaye niki askan wi, niki sarxalkat yi, maa leen di dikke seen añu jikko, maa leen di fey seeni jëf.