TSK

TSK · Isaiah 26:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg.

Job 16:18 TSK

Suufoo, bul làq sama deret ji tuuru, te yal na sama yuux jollee fu af.

Maay delloo àddina mbonam, yool ku bon tooñam, maay sàggi sagub ku reew, detteel puukarey ku néeg.

Moo tax Aji Sell ju Israyil wax ne: «Gannaaw yeena xalab kàddu gii, yaakaaruleen lu moy doole ak pexey njubadi yu ngeen wéeroo,

Mu ne ma: «Yaw nit ki, gis nga li ñuy def, tojaange yu réy yi waa kër Israyil di def fii, ba di ma soreleek sama bérab bu sell bi. Te dinga gis tojaange yu gënatee màgg.»

¶ Ba waa jay agsi, jëmmi serub yaa nga taxaw fa féete kër Yàlla ga ndijoor, niir wa daldi fees ëttu biir ba.

Deret ji mu tuur a ngi ci biiram ba tey; doj wu amul dara la ko sotti, sottiwu ko ci suuf, fu muy suuloo.

Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim, ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda. Man, man mii maay xotat, wéy, maay yóbbu te kenn du wallu.

Yeena ñàkk xel! Xanaa du ki sàkk biti moo sàkk biir itam?

Dina feeñ it ndax noflaay ba mu nuy booleek yeen ñiy dékku ab coono, sédde nu ko, kera bés bu Sang Yeesu feeñee, ànd ak ay malaakaam yu làmboo manooreem, wàcce asamaan.

¶ Ba mu tàyyee juróomeelu tayu gi, ma gis ci suufu sarxalukaay bi, bakkani ñi ñu bóom ndax kàddug Yàlla ak seede si ñu ci seede.

Ci yaw it lañu fekk deretu yonent yeek ñu sell ñi ak mboolem ñi ñu rey ci kaw suuf.