TSK

TSK · Isaiah 29:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji, ñi koy xeex ay rajaxoo, kaw asamaan lay dënoo ci seen kaw. Mooy mbugal àddina, ba mu daj, di kàttanal buuru ñoñam, di dooleel ki mu fal.»

Dégluleen, jàmbaar ju am doolee ngi dikkal Boroom bi, di tawub doji yuur, ngëlén luy sànke, riddee riddi, sotti waame wu wale! Loxoom la koy rattaxe fi suuf.

Ñi ñu yaakaar dañuy tiit, ne wëqet, seeni kilifa jàq, ba daw wacc raaya ba. Kàddug Aji Sax jee, Boroom sawara wi ci Siyoŋ, Boroom taal bi ci Yerusalem!

Maa koy mbugale mbas ak deret ju tuuru, ak wali waameek doji yuur, ak tawub sawaraak tamarax, mooki gàngooram, ak xeet yu bare yi ànd ak moom.

Ca waxtu wa, suuf daldi yëngu lool, ba benn fukkeelu dëkk ba màbb. Juróom ñaari junniy nit (7 000) dee ci yëngub suuf ba, ña ca des tiit, di sàbbaal Yàllay asamaan.

Ba loolu amee, ay melax tàkk, ay kàddu aki dënu riir, suuf yëngu yëngu bu réy bu masula am ba nit teewee ci kaw suuf ba bésub keroog. Noonu la yëngub suuf ba yéemee te réy.