TSK

TSK · Isaiah 30:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ña ca des daw ba Afeg, ca biir dëkk ba, tata ja màbb ca kaw ñaar fukki junniy nit ak juróom ñaar (27 000) ca ñoom. Fekk na Ben Addàd daw dugg ca biir dëkk ba, jàll ci biir néeg bu làqoo làqu.

Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc, di ma rawale, ba duma sànku!

Yàquleeka leena bett! Musibaa leen ne fuuf, ñu ne mes!

Say noon ay def gàngoor ni feppi suuf, di naaxu nit ñu néeg, ñu ngelaw liy wal nib cox. Loolooy jekki am, ca saa sa.

Maay màbb tata ji ngeen raax weexal, mëqal ko suuf, kenu ya siiñ, lépp jóoru, ngeen jekkliku ca biir. Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji.

Luke 6:49 TSK

Waaye ku dégg te jëfewoo, dangaa mel ni nit ku tabax kër ci suuf, te amul kenu. Wal maa koy rëkk ak doole, kër ga jekki màbb, yàqu yaxeet.»