Absalom ak waa Israyil gépp daldi ne: «Ndigalal Usay, Arkeen bii kat, moo gën ndigalu Ayitofel.» Booba Aji Sax jee nara indil Absalom musiba. Moo tax mu neenal pexem Ayitofel mu jub ma mu laloon.
TSK
TSK · Isaiah 30:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yaa xadaru sama kaw, ba sag reewande tàbbi sama nopp! Maa lay takkal ag nos akug laab, waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon.
mu soqiy fitt ak jumi melax, tasaare leen, fëlxe.
Xiir, aw fas; laab, mbaam; yetu gannaaw, ab dof.
xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.
Ngoon a ngay jot, tiitaange ne jaas, balaa bët a set lépp jeex. Lii mooy añub ñuy sëxëtoo, lii mooy deminu ñiy nangu sunu alal.
Firawnaa, ana say boroom xel? Nañ la waxal boog, ba xamle li Aji Sax ji Boroom gàngoor yi naral Misra.
Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi moo lay dikke dënook suuf su yëngu ak riir mu réy, ngelaw riddi, di ngëlén, ànd ak sawara wuy xoyome.
Yaa xadaru sama kaw, ba sag reewande tàbbi sama nopp! Maa lay takkal ag nos akug laab, waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon.
Moo leen tax di naaxsaay ni niiru suba, mbaa layub njël, mbaa mboob mu naawe dàgga ja, mbaa saxar su gillee ci jankub néeg.
Am sànj nga daagoo fi kaw suuf, mer nga dëggaatee xeet yi.
¶ Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp.
Looloo tax Yàlla yónnee leen jëf juy sànke, ngir ñu gëm aw fen.
Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.