TSK

TSK · Isaiah 30:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»

Léegi nag bindleen woy wii ma leen di dégtal, te yaw Musaa nga jàngal ko bànni Israyil. Woyloo leen ko, ndax woy wii di sama seede ak bànni Israyil.

Xam naa ne gannaaw bu ma deeyee, dingeen defa def ag yàqute, dingeen teggi yoon wi ma leen jaarloo woon, te musibaa leen di mujj dikkal, ndax yeenay def jëf ju bon ju Aji Sax ji ñaawlu, ba merloo ko ndax seeni jëf.»

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

Merum Aji Sax ji du giif, te deful ba sottal li mu nar. Fan yu mujj yii, ngeen am ci lu leer.

¶ Yeremi woo Barug doomu Nerya, dégtal ko mboolem kàddu yi ko Aji Sax ji wax, mu bind ko ci ab taxañu bindukaay.

«Du tee fan yu mujj ya, ma tijji wërsëgu Mowab.» Kàddug Aji Sax jee. Fii la àtteb Mowab yem.

Yaay songi Israyil, sama ñoñ, mel ni aw niir, muur réew ma. Fan yu mujj ya la loolu di am, maa lay yóbbu yaw Gog, ba ca réew ma ma séddoo. Maa lay firndeele sama sellnga, ngir xeet yi gis, ba xam maay kan.

Aji Sax jee àddu, ne: «Bindal peeñu mi, leeral ko ci àlluwa yi, ba njàng mi yomb.

¶ Li ngeen wara jëkka xam moo di bés yu mujj ya, ay niti ñaawlekat ay dikk, di nit ñu topp seen bakkan.