Ndax maa xam seen jikkoy fippu, ak seenug dëgër bopp. Seetleen, ndegam bi may dundagum tey ci seen biir ngeen di fippu ci kaw Aji Sax ji, astamaak gannaaw bu ma deeyee.
TSK
TSK · Isaiah 30:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Artu nga leen ndax ñu dellu ci saw yoon, teewul ñu bew, ba sàmmuñu say santaane, xanaa di moy sa àttey yoon yiy taxa dund képp ku ci sàmmu. Ñuy daŋŋiiral, sajju loos, bañ laa déggal.
Soo dee tanqamlu yoon, sag ñaan sax Yàlla suur na ko.
Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
Yeena naay: «Danoo wóllëranteek ndee, njaniiw lanu digool, ba du nu moom, ba bu yaru musiba dikkeek diisaayam, du nu laal? Noo def ay fen sunu rawtu, ay wor di sunu làquwaay.»
Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen. Dangeen të, wowle.
Moo noon: «Sama ñoñ déy ñoom a! Ñee di doom yu dul tas yaakaar.» Mu daldi doon seen jotkat.
Su ko defee nga ne leen: “Xeet a ngii wu dul déglu kàddug Yàllaam Aji Sax ji, nanguwñu yar, worma tumurànkeel leen, ba daggook seen làmmiñ.”
«Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yeena gis mboolem musiba mi ma wàcceel Yerusalem ak dëkki Yuda yépp. Ñu ngi nii tey jii gental, kenn dëkku ca.
Dégluwul baat, nanguwul kàddu guy yare, du Aji Sax ji la wóolu, du Yàllaam jooju la jege.
¶ Teewul ñu baña déglu, të ticc, fatt seeni nopp, ngir baña dégg.
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»