TSK

TSK · Isaiah 32:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu yónnee ay bataaxal yu jëm ca mboolem Yawut ya ca téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127) ca réewum Buur Aserus. Muy kàdduy jàmm ak kóllëre,

tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk,

Ku jub du tërëf mukk, te dees na ko fàttliku ba fàww.

Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»

Ay askan yu bareey dikk, naan: «Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji, fa kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.

Till ay bokk ak mbote ab dal, segg bokk akub tef ab tëraay, wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar, tuut-tànk jiite leen.

Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.

Liy dalal seen jamono mooy koomu ndam; xel ak xam-xam, te ragal Aji Sax ji, loolooy seen alal.

mboolem sa doom yu góor ay jànge ci Aji Sax ji, boole kook jàmm ju ne ñoyy.

«Mbégte déy, ngeen di génne, ñu yóbbu leen ci jàmm, tund yu mag yeek yu ndaw yi di leen sarxolleel, garabi àll bi yépp tàccoondoo.

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Maa ngii di yóbbu Yerusalem ci jàmm ju mel ni géej, ak waamey koom muy wal, bawoo ci xeet yi. Yeenay tooge luppu Yerusalem, di nàmp, uufu ciy óom, mu di leen raay.

Ñooy dëkke réew mi ma joxoon Yanqóoba sama jaam ba, te seeni maam dëkke woon ko. Ñu dëkke ko ñoom it, ñook seeni doom ak seeni sët, ba fàww, te Daawuda sama jaam ba mooy doon seen boroom jal ba fàww.

Micah 4:3 TSK

Mooy àtte diggante xeet yu bare, mooy dogalal askan yu am doole te sore, ñu tëgg seeni saamar ay illéer, def seeni xeej ay sàrt. Aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar, te dootuñu jàngati xare.

Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan ak a dagaan te boole ci di ko sant.

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.